LYRIC

{Refrain}
Amoulo li mbaa lé ba cii lane
Donoulo ki mbaa ké ba cii lane
Amoulo li mbaa lé ba cii lane
Donoulo ki mbaa ké ba cii lane
ba cii lane ba cii lane
Yone bi goudou na waayé di nga éégui
Gni gueuneu deugueur bopp rékkay tékki

{Verse 1}
Yeah ! Ba ci lane égalité déh na bou yagg fo guiss justice
Niaak tololé waral dougnou meusseu jog ci guiss tiss
Waayé boumou takh nga faté di wakh bène biss
Ndax li nga niaffé dina fay nga am sa bénéfice
Mane gueumouma ni domou Ministre rékkay tékki
Ethiopien sakh ak lékk djou doy dina sékki
Waayé dama kharoul lène cii kèneu kone lerna
Yaye néna domm bou ragal ndax dinala niaanal
Ba Cii Lane ! Est-ce que kou dioudowoule rek cii berceau en or
Waro am loutakh beus nieuw nga nélaw ba yandor
Touti waroula téré wané sa bopp ci gangorr
Louy temps mort mane dina niaffé sédday mba tangor
Meune na RAP waayé meunouma bindeu Ba Cii Lane
Gni gueuneu tékki ci RAP kouniou dakk PUNCHLINE
Kouy sa maame est-ce que mo monté assamane ?
Kone Guéweul ak Gërr ay rétane lamay dikeul mane
Kouy la-ngamou ci niit bou fakastalo di nga daanou
Fanaané aalou yéwou té diéém la cii taamou

{Refrain}
Amoulo li mbaa lé ba cii lane
Donoulo ki mbaa ké ba cii lane
Amoulo li mbaa lé ba cii lane
Donoulo ki mbaa ké ba cii lane
ba cii lane ba cii lane
Yone bi goudou na waayé di nga éégui
Gni gueuneu deugueur bopp rékkay tékki

{Verse 2}
Yeah ! Le milieu détermine l’individu ay féni nèène
Est-ce que deukeuk ay guinar dina takh nga nééni man ?
Kone deuk GRAND YOFF takhoul kène done Voyou
Fuck gars yu djapp wakh guinaaw niit aayoul
Yaw ya ngui fii mom mo ngui kaaw dieul na plane bi daaw
Waayé est-ce que naaw taxna raw ? no tamite dou daw
Fi lifi né moy savoir partir à point donner
Kou tourné en rond nak niou bayi lafi abandonné
Yakoy diokhogne ndakh baayi ay djangam
Ladial Bill Gates ndakh toppeuh sa yone téré na done Kangam
Yama dakeu djaamou YALLA yaw rekka wara am
Waayé est-ce que yama dakk niaane ? YALLA rekka xam
Selfmade lima am cii RAP rek mako liguey
Amouma tuur motah never nga dégueuma cii DJ yi
Waayé dou téé mouk HAKILL meuneu bokkeu cii péé yi
Douma ki ké amouma lii léé téyeul sa pitié
Yeah Waayé téyeul sa pitié
Ich Yo Boy Han

{Refrain}
Amoulo li mbaa lé ba cii lane
Donoulo ki mbaa ké ba cii lane
Amoulo li mbaa lé ba cii lane
Donoulo ki mbaa ké ba cii lane
ba cii lane ba cii lane
Yone bi goudou na waayé di nga éégui
Gni gueuneu deugueur bopp rékkay tékki
Ba cii lane
Gni gueuneu deugueur bopp rékkay tékki
niom rekkay éégui
Ich Yo Boy Han

Added by

Abdoulaye Ndiaye

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR