LYRIC

{Checky Blaze – Verse 1}
Yalla bou beugué nieup dadi niakk
Délou guinaw amatoul bou féké balle dafa dadi takk
Bataxal bi ma ngui koy bindeu diko diak lél samay way
Na souf sedd sène kaw makoy niane cii barké Baye
Diko nianal bepp mindef bi YALLA toudou sa dém
LAH-ILLAHA-ILLA-ILAH safal sunu Rouhou done sunu lém
Bakawou rek mo méti té do khamati fi nga tolou
Waayé gueum gueum lagnu andale cii lagni sobou rakhass sunu xoll
YALLA na YALLA tidjilène Aljaana you gueuneu kawé
Yonett YALLA térou lène té yokou lène yokou séni tabé
Niane yimay niane yakarna dina lènn feksi
Yonett YALLA SAHABAM yi nieup andeu térou lènn cii.

{Ablaye Mbaye – Chorus}
Li liniou waar la dafay sunu waref
Da ngène fi nékone ak nioune bokou waar wi
Daniou niou done bégueul meussou niou nio xatale
Dieum dji dém na waayé djeuf dji dou saay

{Checky Blaze – Verse 2}
Fanawou rek mo nékh, waayé niiteu aki sa sago
Pays YALLA wessouna sa xell Aduna amoul solo
Zaïr rek moniou xiir takh niouy djoy bougni tago
Djougué cii YALLA délou cii YALLA bobou xaatir doyna sango
X Jo manela Checky Blaze sa bro
Salatul fatiha yima la yéné yakarna YALLA nangou ko
Wouyou sa Borom rek moy deugg, métina waayé louniou cii meune
Waayé Borom béko toudou dafa fekné rek mo gueune
Mala moudjéna wo guissone la moma gueune lone
Louniou done paré dou meusseu am, dafa fekk ni YALLA ko toudoul wone
Mognu mom moy sunu Borom loumou def nonou la
Waayé yéneuy sunu xorom deugg deugg métina
Niam doundou doyna sante Diamou rek barké la
Moy Borom KUN FAYA KUN loumou bindeu Haqq la
Diko diamou sassou né tambalé FATIHA ba BARAKA
Djougué cii lerr dém cii leundeum Aduna DIAMAL ak DIALAL la
Rest In Peace

{Ablaye Mbaye – Chorus}
Liniou waar la dafay sunu waref
Da ngène fi nékone ak nioune bokou waar wi
Daniou niou done bégueul meussou niou nio xatale
Dieum dji dém na waayé djeuf dji dou saay

{Ablaye Mbaye}
Mane douma djoy dama lèni nianale
Da ngène nio wéteul
Baay ngène sen waleu cii art bi
Fi ngène dieum YALLA nalène gueuneul finiou djougué (Amine)

{Checky Blaze – Verse 3}
Khadaratoul waaliwu nga nekk waayé baye xam naniou la
Cii Zaïr sori nga niou waayé cii Baatine xam naniou la
Dj 1-2 Alassane Chekhoul Tidjani, nio ngui lay ziar ci nassiril Haqq Bil Haqqi
Hip Hop P.A wett na, lolou kène douko wéddi YALLA CHEIKHOU TIJAANI téral la cii Khadara larkhawi
Mbotou LAH-ILLAHA-ILLA-ILAH dila goungué fo meunti né
ALHAMDOULILAH di sante cii MAARIFA bi nga nék
Sama xoll fess sama xell dém ci NA bou Carré d’AS
Gueum nani YALLA dina la térou Aldianam fofoy sa place
Mbékté ak Nakar nek cii mane bouma séintu mista Ras
Waayé douniou la faaté cii ay niane, Nio ngui lay bakhé ay LIKHLASS
Yi Kaddu makoy bindeu diko djaglél Bourba
Yaw mi bégueul say fans ba ngay délou cii BOUR BEU
Dila djalé wa Galsèn, rawatina Books Sen Kumpe
Fi nga dieum lerr naniou donatoul sunu kumpa
( REST IN PEACE )

{Ablaye Mbaye – Chorus}
Liniou waar la dafay sunu waref
Da ngène fi nékone ak nioune bokou waar wi
Daniou niou done bégueul meussou niou nio xatale
Dieum dji dém na waayé djeuf dji dou saay (2fois)

Douma Djoy damay waay
Douma Djoy damay waay
Douma djoy damay waay 

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR