LYRIC

{Verse 1}
Labaale sa rouh ak sa xoll bamou clean
Sélale sa djeuf sasouné ndakh Killah Tim
Gueumoul nélawoul té bessou aaté amoul miim
Sa nafsou moy sa none
Sa diné moy sa yone
Sa warougal cii gueum bi moy diamou sa borom
Boul réré mbiir
Shaytané migui fiir
Niou laap cii guédj niawtef cii boppam laniou xiir
My nigga sopile sa nékine
saamal sa téguine
toubeul sa niawtéf fékhé ba dotchii délou
Ndakh biss mogui nieuw niou yéwla bagua woweu
gass bamou xautt soul wanela guinaw
Lo dawaloul moudjeum laxiira momou loko
Ak loumou baarii baarii niénène sédauko
kounek xamni mbougueul fofou laay doré
Té barçak saay djeuf molay yoré

{REFRAIN}

{Verse 2}
Yéwoulène té yété nélaw yi dafa doy
Diné djégui toumranké sénégal di djoy
gni warone nek royoukaay douniou djiouk cii moy
Safara ragui boy
Iblis digni xoy
Nafsu woutt lou noy
kou noyiwoul digua soy
Ana gni rafétone ba melni Youssoupha
Ana nioufi amone kom-kom bou douf
Taay gass naniou lène dougueul cii biir souf
Ndagam Rassoulou Lahi gueune cii mbindef mo xeuy né mess
wargua baayi xell né aduna bi kèn doufii dess
Doylo sa weurseuk
Wadialale sa euleuk
Notaal sa bakane cii chartou l’islam yi
Xana dawo téwé conférence Serigne Sam Yi
God Bless!!! Yalla diégueleul sa diam yi
Gnileu djitou barzak Yoné lène Likhlass yi
Likhlass yi, Yoné lène l’Ikhlass yi

{REFRAIN}

{Verse 3}
Nda guène ma téwé té téwlou maa
Andeu ak mane gou ngé ma ba sama bounetou kane
Nda guène ma santé Yalla
Mom mii meune, Mom mii sagne
Mom mii sakk, Mom mii soop (Deugg leu!!!=
Niane rek guène cii meuneu
Rafétal sèni ndiottt lou Yalla défaay li gueune
hanhan !!!
Boulène niou faté nianale yén gni dess
Té guène xamni adouna dou keur té dou xariit
Poukeuréy nafsu boumou takh yaw saliitt
Té Lepp loufii def diguako layo bissou aaté
Sou boba est ce que digua guiss kigua dane waté
est ce que bokou nga tchii gni mouy woté ay talibém
Sou boba Kou né sa bopp nga taal
Kèn dou lathie ndiéleu
Kèn dou lathie natale
Kèn dou am alale
Badola ak bour takhaw takha wayou diam
Nieupeuy yém tcha yalla
Niouy naatt saay dieuf
Balance bi di wakh

{REFRAIN}

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR