LYRIC

{Intro}
marie moy bess bi
thiabibi di bénén bess bi
kon bess bi gaddouna bessam

{Verse 1}
loumou méti méti boul khadi sokhal
ci kaw beug tékki doon loula sokhal
boul tope con yi nek ci mbed mi nane souma pressé sokhal fouti
kholal bou bakh ci ki ngay roye bo bagné fouti
ken khamétoul ki bakh ak ki bone
ki di dem fajar djak dja ak ki nek ci cogn bi di djay bone
bess bi gaddouna bessam daldiko geusseum
adouna mo weulbeutikou
pass pass gou takku rekka ko meuna dékou
boul nagou di wékou ci guinaw gni diogué etats unis wala rome
nek khalé téréwoula am diome
boul nagoo nek doungourou
deugeuleu fii dou ngourou
gni gnak wayé
yene yi sa ngor molakoy ayé
xarit boul saalit kounek ak bess bi ngay ayé
sa bess bou dioté ci kaw ndiék ak téranga ngakay dioté
dossi xulo waxumalax dioté
cone tay lila war moy téy
limalay wax kanila dou sukar ndax beugouma euleuk sa xel téy
sédal sa xolu yaye diouli waxtouyi diourome di limalay denk
nangako fonk ni fonk gou raw nii menuiser fonker denk
natou yi ngay diankontél borom bi molakoy watiél
boko beugué deudou sa bop ngay guatiél

{refrain}
bess ba ngi dox
bess na ngi guiss
bess ba ngi yeuk sibo sax danga diss
deg diam humm issap sa bop
li ngay nama moy moudié dague sa bop (x2)

{Verse 2}
djoudou rék peuteukh ci camb gui
di réver reutch ni pitax bougnou deup diamb gui
poss yé lafagn yéné yi teuweu tek diéggo
waral do nék té yéggo
séti bouka wala goukh gagn
ndax sa neex
lilakay diokh dou saneex wala serigne ngagne
boudoul mane wala mère bi beurigo bi aida xalatoul rotko
fou sama yeuré sété ma djoutou faute ko
rak sama mbéd mi la taylé bopam
adouna la denk nopam
bou mère fébaré doneko sax am dieundeul aspirine wala nivakin
té bou féké sa guèl nga yoboulko mboussou banana ak pom
ya niak diom
dadialé lou tolokh diourom béni bant té kén bokouci ak sa morom sant
bouniou waxé nganane ndogal
niak diom wéssouwoul tak diabar yobouko sa keur baye sa yaye diko toggal
bar ba demb lofa yak
yéwou ak lakhal niouy ladj dépense nganane prek ngay bak
lép nga keup ko ci soum soum bière xawma rome niak diome
yén yi nane lako niit di khalaté bakoy déf
wayé bou lép calaté bagn né diak chef
li gniy malaté moy raw néf
bess bi gaddouna bessam

{refrain}
bess ba ngi dox
bess na ngi guiss
bess ba ngi yeuk sibo sax danga diss
deg diam humm issap sa bop
li ngay nama moy moudié dague sa bop (x2)

yén gni dé lane ngén
lane ngén
bisso namoul dara mom namoul dara
loumou namantou togg ko lék ko (x2)

{Verse 3}
aparte la louer bérou di reubeu nadj yi
doudou lou kérou djeunki bi ci cogn bi moy bay dji
mougui case mougui salam mougui ngalam
kep kill dokh brioche doré after lalam
5h lay yéwou
benkeur lay diéwou
soko beugone tak sakh dou séne keur ngay téw
moy kilifa bopam
mo yilif bopam
mom ci walou bopam moy moudjé dagg bopam
{Outro}
ki dafa déé ki di nélaaw
na ki nélaaw yéwou ba nopi souli ki déé
nonou rek sa bop ngay dieufleuntél
sa none yaw rek la xatiral ci li ngay diankontél (x2)

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR