LYRIC

{Intro}
Umh Hum
Diangoro Diamono Dja ngui niii 
Niambéy Safara cii

{Verse}
Yo Ngor ak Djom andeu nagnou naaw
Dieum cii réwou niaak djom fass yénéfa takk diabaar amfa ay dom
Dakk lepp sakhal beug beug
Sa deug deug gnak djom lagnou seug deug
Dem ba xel ak xalaate dotoul xégne loudoul ay salade
Jeuf yi malade Guémigne teulé cii guèné kaddu gou djak
Soubeu djaak di lathie bane ration mokay khaar
Limou sèèn cii tay mo doy waar
Ba moudjé yaubou fiiteum
Nafso farankoulaay cii xollou beug beug yu gaddu fiteum
Liy khaar sunu dom yi soubeu bouniou ségoul tay mou done moussibeu
Mou ngui guili di xégne ni dial yu fi mouss yi beu
Xel leu panne xalaate diakhaane
Thieur yi di thiakhaane
Li nga guiss cii télé bi di répétéwu cii mbède bi fréquemment
Bien vrai fé rare comme diamant
Lidieunti lamecette ndax goor dooranté kourpagne ndax guel
Sheytané naane waaw goor ni la beug ngène mel
Togayou bountou keur yi dieuw lay wané
Kouné djapp sa morom ni yakko tané
Doundoup dieune diakhaane ci guéwou politique
Digué bour ak fènne tigui, théorie rk seug cii teuweu sigui
Pratique nada askane wi sagaané aada
Deudou thiossane di xalaaté fann
Lou teulé mou keup cii mbalite mou aneu
Réwandé weur di waalé ni waninte
Xalé bagne yaunénte
Doumauyou métier dieul djangue tégué néé
Tok cii bopp kogne yi déguéné sen laxassou paune tégué néé
Molèni fatélo sen tiss
Wadiour yi tarkhiss djiteul xaliss
Rotchi boumou niènte tranche
Tamou kou joggué Italie wala France
Té naane CFA dou EURO
Sama dom dou yeuy sa gouro
Ndax yatto goro meunouma done sa gorro
Dolé Poche yilif deug ci beureupou atakaay yi
Neubeu djante bi kou yégoul tiinoul dégueulma thiaythiay yi
Niouné Assamane dou taw té xiinoul
Sénégal lagnou miné ak corruption
Injustice neub xétt bi éruption
Kou laale mbautou ngour gui ay marteau lay talale ni SYLLA
Wala DIC dieul sila
Liberté d’expression lagnou yène pression
Thiaxane kat la daradjaam yék ba tolok bou Kilifeu?
Wala Kilifeu la daradjaam wathieu ba tolok bou thiaxane kat?
Point d’interrogation ndax kat fofou question mo ngui faa
Goné gou djoudogoul saxagoul sakh wéine
Naka lako ponkal di tiimé bay guéné géine
Bane plaisir la Djiguène guiss cii moromou djiguèneum
Goor ak goor di am rapport kambeu bougnou souroukh dinagne ci guéneum
Diangoro Diamono Dja ngui
IQRA Beug sunu niétélou beute FIQRA Li gni war moy djangui
Xel Kom leu Wédiko Dunya Baume leu
Yène yi gnak djom leu
Lanela diabarou borom keur di woute cii nëgou locataire bi ?
Bagni athie tankam cii air bi ?
Lane ngay oute cii kaw diabarou diambour bagnelay béteu ngay teup parantaire bi ?
Fanela sama mbokkou lébbu yi tek suuf bamou diaral lène sankeu sen mbok ak kane ?
Niouy xeuthiou suuf gass sen cane soumako done liim dana sakane
Fanela wa kogne bi tek navétane bay souli nééw pour coupe bi téw ?
Wala sacrifié domou diambour pour am ndam
Deum yiy takh niounane deum bokoulak ligni tam
Ndiathiar bou gueuleum xouss, Jeuf dji leundeum kouss
Kouska-Ndrongue dogaléko teukou ko beuré yénou door cii suuf
Seuleum mou jog takhaw cii sass yi mou taggok saggom
Xel bi né fess ni écriture bi ngay effacé ak sa gomme
Xel mé ngui fi wone dembe cii goudi
Waayé tay dafa melni lougnou boudi
Gni naane ay Djinéko djapp yaubou lène ko cii xambou maame yi sangue ko
Sheytané yi naane “Mère bi cii kogne bi leu”, Niété fane lagnou cii tek niou sangou ko
Tek cii plancare gni dieul taxi gni car
Gni amoul place tokk
Corbillard né yoff nio ngui gok
Baniou robé ba nieuw kounek sa Yaay yeukeuti bouteillou safara dadila diiw
Naane beugoutouma guiss tank keur Diw
Beugouma sakh nga lèni djégué
Deum amena wala amoul tontou bé ngui cii soufou njéguénaay tégué
Founiou dieum ak niawtef yi, Safaane na Yilif chef yi
Imane toumranké Aduna tigaume kawtef yi
Ci xel ak xel l’Intellect. Internet né tiaraakh
Dieul ngor ak djom waraakh
Sopi dokhine ak wakhine
Doumauyou lou araam ci nékine
Doumauyou ndigueul fale téré
Kou wakh deug niou daadi leu méré
Di agné safaane diko rééré
Tollou deug far gars yi
Waral farankoulaay né thiakhaane argaay
Tollou Ikhsane far daay
Ki wara fay lakk bi dou Pompier Cheikhou Mou Rabi
Dou Nassaraane cii nga wara copier Digueulé Nabi
Xam Yallah laay Garab gui
Sakou cii Cheikhou Mou Rabi Mou guinedi ci Lahou Rabi
Nga daadi mouthieu cii issape bii

{Outro}
Yeah GASTON Alias Baay Sèn Alias BandiMic
Deupeul délou cii sa bopp
Yaay lepp dara guénouleu
Safara sé ngui cii yaw
Yallah laay safara cii té mou ngui cii yaw
Lileu gueuneu diégué sa boumou xol bokoy sééte
guéneu sa bopp nokoy guissé nokoy guissé
Deupeul délou cii sa bopp
Nga Yëg Soga Nek
Yëg Soga Nek
Yëg Soga Nek
Yëg Soga Nek

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR