LYRIC

Refrain
Do modèle do modèle do modèle do modèle yow nigga do modèle
Do modèle do modèle do modèle do modèle yow nigga do modèle
Do modèle modèle do modèle han nan tchi dara do modèle
Tchi alal tchi djiko tchi diné do modèle
Tchi rewmi té bi xéet bi tchi ndaw gni do modèle
Do modèle do modèle do modèle do modèle yow nigga do modèle

Couplet 1

Do modèle do modèle do modèle
Djitou nga falou mais téwoul do modèle
Bayi wofi dieuf boula kén meuneu wayal
Sa xél mo thieuk walabok da nga tayal
Do modèle do modèle aakh rek nga niou yorel
Werr bala déh Ya ngui fayou ay brick
nioune bureau lagnelay khaar yow Ya ngui teudiou hôtel
do modèle do modèle rakh tchi doli do kou honnête
Biss mi ngui da nga takk sunuy menotte
Bouko kén baal limouniou amel lepp na motte
Economie rew faux billets dakoy damate
Fi kou beug doon milliardaire fokk nga nangou khar-matteu
Yén dale yén dérou Serigne ngèni yakh
Politigué sén talebiyi djaay sen carte
Ngour guoufi nieuw nguen chantage
Dieul pourcentage lolou dale moy sen marque
Do modèle do modèle tchi dara
ana ragal yallah khana do domou daara
Bou ndieuk ay zaïr nio daan féki baatinn
Wayé legui ay baatiin kom kom laniouy fighting
Niata niou taylé tchi lokhoy toubab yi
Mamadou dia doyna cédé coup bas yi
Ecole dou diangualé téré TOUBA yi
Mais cheikh anta diop dey deh rek mais Dou bayi
Maitre Babacar seye moy prix nobel
Histoire mi ngui neub ay criminel
Biss mi ngui nieuw bagnekat free ni nel
Son Mandéla li nga gueum dé tchi fidèle
Coup d’Etat dictateur nga do modèle
Kou nieup andeu falando kone tololèle
Signé ay accord di ceddo sunu kaagn
Rêvé loniou tchi sa discours khif bi diniou gaagne

Refrain
Do modèle do modèle do modèle do modèle yow nigga do modèle
Do modèle do modèle do modèle do modèle yow nigga do modèle
Do modèle modèle do modèle han nan tchi dara do modèle
Tchi alal tchi djiko tchi diné do modèle
Tchi rewmi té bi xéet bi tchi ndaw gni do modèle
Do modèle do modèle do modèle do modèle yow nigga do modèle

Couplet 2
Takk derr tchi diggou tali melni deum maradétali
Diokhé témeer rek diaaleu soxlawoul di gaddu permis
gardavu niou tekk leu sère-mi dileu saga melni bandit
Formation bi nagne ko kholaat autorité non dou gueudé
No Etude No Ethique corrompu no Mérite
Do modèle kouniouy guérr do modèle
Hopitaux yi ngay guiss médecin you réw
Pensement ak perf. rek laniouy meuneu yéw
Démal fay feulé so paré doga téw
Ap sothie nga fey indi rek niou defkop néw
Ki nieuw amé métite dafa soxla kouko dallal
Niaka kerça infirmière yi légui nieupeu lèn raggal
Do modèle do modèle yeureumo say malade
Niaak contrôle mo waral laisser aller bi
Manque d’effectif excusou tapalé bi
Ana Emergence laay lathie ki tchi Palais bi
GOOR gouy takkeu moromou GOOR do modèle
Yow am nga dolé ko rombe door do modèle
Niari werr yi bèn yone laniou tchiy oubi page
Djangue Xalé yi nga djappeu lène en otage
Ay grêve you wékou tchi caprice
Ndakh sa élèvé yi diaralougne leu sacrifice
Député bouy khasté di saga do modèle
Transhumé nga wédi sa ada do modèle
Yow lot of nigga daniou taré nigga
Daniouy fo tchi tali bi di faté séni bakane laniouy taylé nigga
Yagui loué deuké ndoole dieum nga mak té wara maul
Boulko wekk tchi ay lotterie akkeu khoss tickets
Bédiaw djégué néw done bébé beug méw fougne leu fekk Ya gui nampeu ci ay prostituées
Yakh nga dérou djiguène euleuk boula sa dome ladjé Maa lo doon liguey khana thiagatou

Refrain
Do modèle do modèle do modèle do modèle yow nigga do modèle
Do modèle do modèle do modèle do modèle yow nigga do modèle
Do modèle modèle do modèle han nan tchi dara do modèle
Tchi alal tchi djiko tchi diné do modèle
Tchi rewmi té bi xéet bi tchi ndaw gni do modèle
Do modèle do modèle do modèle do modèle yow nigga do modèle

Couplet 3

Bandit dou taukh dou guinz pour ame fite
Dou kogne bi ngay tok di keuf ay wetchit
Milliardaire do créer emploi do modèle même sou fékké Ya tchi am droit
Néw bi ngay souli mouy guili tchi tioumikaay takhawal beuré dofi xeureum beu xeuy fi doon roi
Do modèle do modèle do modèle ha nan tchi dara do modèle
Kou am mérite dougne leu diokh poste
incapable yi rek nioy sole cost
Conséquence yi légui boy yi gni ngui bayi djangue nénagne diarouko sama time laay lost
Immigré yagg nga doundé sunu Bourse
légui paré nga té beuggo delou ci sunu rew
Bou nieup défone ni yow est-ce que dina bakh
né nga fi amoul dara lougn lay fay dafa néew
Deug deug khar tchi guétteu moleu tané
Victime nga da ngay rireundo rek topou tendance
Nane dafeu xéw taukh dafeu xéw pass pass bombass Ya gui faté le temps passe
Askane Wi nga bokk doon tchi modèle
Liguèye bi ngay def doon tchi modèle
Rafétal say dieuf bofi diougué ay ate
Gniy nieuw demain diapéleu modèle

Refrain

Added by

Abdoulaye Ndiaye

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR