LYRIC

One Lyrical

Gëm gëm

Potentiel

Nitt ku ne akk kila Yàlla may

Nangul ndax moy may

Del joxe azaka muslim bul nangu nay

Gëm gëm tere nala baayil   

Bul caalit bay jaayu

Ma sœur bul jaay sa ngor ndax gore lañ lay fay

Woyof sër ba melni barbare

Soxla wuma xam sa jaar jaar

Da nga dem ba magg xam ni life da tar

Non Comme que leegi nii la xaaral ma moytu quelques bakaar

Yàlla nee na tòñ len ma baal na len

[Baal na len]

Nangul doggal Yàlla buur bu baax la (la la) (x2)

Kële am yow amuloo tax nda toog di xoole

Nee nga dafa bari doole tax mënu len bokk ndab oh non non non

Mon frère yow gëmuloo di nga jog ci neew di doole

Joggël utti loo def ki ngay ñee dafa ligeey mu fèeñ ci moom

Ñaani waajur sakku ko mu fajj sa aajo

Defkat nga te ñaano deelu kaso

Li lay fèes ci xel mi sa wërsëg ding ci nga jot

Dessinel sa adina yor baguette bi yay Picasso

Bañal ku reetaan

Goorgorlul bañ kulen daan

Xoolal ci say maam

Fayal bor bi tërël Suleymaan

Te Nitt du bañ ngànt

Yàlla nee na ma dooli ngen sànt

Wara wër di waliyaan ci kop ngay naan

[Joggël célébrer]

Nangul doggal Yàlla buur bu baax la (x2)

[gëm gëm]

[Follow my Free 1 2 3]

[Follow my free 4 5 6 let’s go]

Dara jòmb la, dara jòmb la, dara jòmb la my nigger, dara jòmb la, dara jòmb la

Bul ñaan ken boo jengoo jiite

Bul ñee ken boy hustle yigo

Milliardaire mba Rest In Peace ma

Gistël bee fèñ ci sen ay jikko

Dara jòmb ma, dara jòmb ma, dara jòmb ma my nigger, dara jòmb ma, dara jòmb ma

Gis sen intérêts tax ngen feel ma

Miin na fen da ngen di jouer film

Ay naafeq ño rax sen biir

May 10e dan may sen ceinture noire

Por El Dinero music (x2)

Reyal say noon nga teg sa bopp

Sa échec moy bañ beggël sa papë

Da ngay dem fay son nga jël say ventes

Sa ngërëmu yaay moy guddal say fan

Ngërëm‘ag gëm gëm rekk mo ñu andi fi

Ba tay ñu taxawal sunu entreprise 

Added by

Maalik Sy

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR