LYRIC

{Intro}
talibé bagui khar ma yabi lima sekh mou saka
niambé ma firil baat bi ma warko faramfatié ci wolof ni bamba ak cheikh moussa ka
gaston la dieureudieuf cheikh moussa touré

{Refrain}
niambe ma door dix courou doff ci bopp
ma wara keurou “discourou” doff ci sama bopp
takhaw di taari “discourou” doff si sen nopp
di sirou kham dix courou dou cadou gou wopp (x2)

{Verse}
yow xola fess ragogne tourou
mouy bess bou bess ma wara ngourou
tiono né mess ci baneex ma daldi nourou
missalou tiante la
adouna nak yoon bou pante la
kou faté kila faal folékou
sant kila may moy dolékou
bou ngeurmeundé fotoul
barké dou lém
té kou dofoul xamné yamba rek dou lém
fok YALLA tabil ci dolém
ci izbou bou neubou laniou kalimatoula wo
mouguiné fangue ci car rapid yi do ci diot té fanawo
minal djinati wanass la anawo
kon diokhel sa bopp té bayé koko
naguou né souf né bouko nekhone né kén doufi bayé coco
missalou bamba ak cheikh ibra teunk na lép
lifi djitou ci ngeunél djébeulou tank néla eup
baboula léér la
kouy tokhou fekhel tassé ak mom boko teunké ci beureup mou réér la
YALLA di mom djeulbénou fégnou wayé diamant ci mbalit la
gni kay nagou niou neew lay done
wayé gni bagnone yague yague founiouy moudjé tialit la
té kou niam laata mouy kham neew lay done
kou wédi baye gueumo bamba
té kou dingat bamba boko ci baay
fi niambé téyé ken dou waax bam ba
yoon wi leerna nagn RASSOULOULAH ko bay
khamé sout fanaw ndieurign nékou fa
tangue loxo ci kala mbedj naam
wayé fa YALLA parti yégoufa
kon charte yi pays bi moy kham dégn ci parti
assamane saax gnougui kaay amé ci ardi
kon ana anta watiél garde yi
bou counék diapé né yay sa morom
di nagn khamné aldiana dou touss yaw yay ngenélou souniou borom
waxu doff la naam wayé moy deug deug ISLAM
kouko xam té doundou ko féki goor yi eupna djouli yi ak woor yi
xam lii ngay guiss moy takh nga xamé ko ba meunsé dieurignou
tangu naniou si guiss ba bakh waral khamé dieurignou
niou sééd gouy dal dokh dieum ca téguine ya
kou khamé deug daa wara fégn ci nékine ya
bo dieufé niou nawla
bo waxé niouné wawla
wayé xam té fo feulé niou dawla
kiy tilimal eukhloubi yawla
issapal sa bopp dox dieum ci ki nga diokh sa bopp
yégg fékafa sa bopp
woniékou fi nga diougé fékat fa sa bopp
wax djé beuri aye bopp ba mélni wax diou amoul bopp
wayé doko faramfatié fekh guisso ak sa bopp
kou xam YALLA deug bo waxé niou nawla
bo dieufé niouné yawla
xamé sout xam fanaw ndieurigne nékoufa
fa YALLA parti yégoufa
kou xam YALLA dou takhaw ci sagn sagn
kou xam YALLA deug yeurmeundé ngay done ci diam yi
xam YALLA dou li ngén fok

Allahou laailaha ilalahou
xaméla dokh dieum sa bopp
xaméla dieufleuntél ak sa bopp
xaméla diayanté ak sa bopp
allahou laailaha ilalahou
wax djé beuri aye bopp ba mélni wax diou amoul bopp
wayé limouy woundou doko faramfatié fekh guisso ak sa bopp

Allahou laailaha ilalahou
Allahou laailaha ilalahou
Allahou laailaha ilalahou
Allahou laailaha ilalahou

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR