LYRIC

{Verse1}
Nuru nga yallah Jeufine , Nuru yonent doxin

Ji way, kuné war na xam kimu doon
Beugue makowoon tuddu ci music wayé moma def lima doon
Diamono dox ba fo xool guiss ko , yaatu wayu lignu sakk
lo xol guiss ko ci guedjeum lagnu soobu ni CHEIKH MOUSSA KA
firndel ko ci yeneen anam mo nekoon sama yéné
Wayé Zayir bo guiss , soko seete baatin da ca née
Moy serignu ki nangou ak ki bagne , ki mugn ak ki kagn
Boolé niu ci yeurmeundem , Nuur gui doto fi dagn
Moy serigne bu magg bi , borom Deik bu magg bi
Juma Ji , xassida yi , borom ndongo yu magg yi
soxlawul sorri CHEIKH IBRA FALL doyna missal
Goor Yallah bi Yalla fal , talibé doon limu sol
Doon ceedé tax niu seddu , sunuk matadi mu gaddu
Bep reuy ci xol yi faatu , Ana Mouridulahi Jittu
Boolena ru ak Jeum , li jogué ci xel ma gass sul
Jebeul lepp CHEIKH AHMADOU BAMBA XADIM RASSUL

[Refrain]

{Verse2}

Jeureujeufé maggi Thierno , Diarama Borom Darou
Sa lerra feuss ci niun , waral niul haal di dooru
Xassida yi defar diam yi diommi muxadam yi diorru
Mbegum diam yi Xadima , ci sa lerr la mindef yi diaaru
Mudjadid , xalifatul lahi fil ardi
Wane niu Rassoululahi , Jeureujeuf di Zikar yi
Ndeké lep ken le , yaye Modou Moustapha
Abdou ahad , Fallou Gallas , yaye Imam Abdou khadr
Mame Saliou , AL amine bara , yaye Sidi Moukhtar
Guindi niu ci yeurmandé , niu diegui adouna ak taar
Sopi naniu sunuy jeum ndamaar , dieubeul la caabi ya
Dioxé lepp , dioxé niep , Fass yéné tarbiya
Nio gui laye niane nga def niu deugu talibé
Musseul niu ci pexé diamono , fagg naniu aluwé
Denk naniu la gni gnu djitu ak gni gnu fiy ba
Sunu bopp , sunu wayu bopp Ousmane Noreyni ba

[Refrain]

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR