LYRIC

{Intro}
Réw ba gui dokh dou nioune guène koy gueum lo
Nioune borom keur yi nioune niouy deuk cii keurti keurti ak xalate
Di xeuy di doundou ….Calcul mental moniou sonal digni stressé
Dégueuloul ma li, dégueloul ma li

{Couplet 1}
Taye dji mome reuthna, souba nak Yallah xam
Dakh weuroum depense, location dina tarr xaxam
Goudi gouné
Sama dieum teude
Sama xel weur di feug si bountu bouné
Teksi dima geude
Bala may nelaw
Bala may meuna noki si guelaw
Sama lepp ni selaw
Fek ma keppeu resultat final bi
Moytou gual gual gui
Guir bagna soukh thi gual gui
Malaki wakh
Dakh djinakh sakh sou beugué goude fan beuri pakh
Locataire bouné si huissier ngay mouslou
Té xamni deup bol si borom keur dafa rouslou
Kalcul mental lagnuy athiou
Wayé bobou ba legui Yallah gui niouy soutiural Alhamdou

{Gaston – Refrain}
Dépensou soubeu moma sonal téré ma nélaw
Ndéki xalé yek bolou agn bi fok mou falaaw
Wo yane goudi bi bouné sélaw
Mak sama xell calcul mental bou doul diekh (2fois)

{Couplet 2}
Bouma sama dome dé fatak aye beugue beugue adouna
Damay ré ni patt andak dal
Wala gnou allou sama kaw ni dotou niou sol feug diaye
Theuy suñu xamone yeneu say
Limay dath thi gnoma’k sene yaye
(Ahahan! ) wakh fegn dakh depensou beuss bouné
Scolarité magg’k gouné
Location courant’k dokh
Si xetou deuk bou lepp di sokh
Beur kamilakoy deukou
Motakhite ma ngi diengou
Mouy geune thi dangue dangue
May geune di dangue dangui
Té daw dou art bi
Ndakh baye wakhone nako faw ma faye xoromou nar bi
Ta li dess si war bi
fadjart thiapantati ma melni cadavre ambulant
Dakh kouy reub depense do talla tok si kaw banc
Baye taxawalou dans le vent
Lekoul ba loff la
Ndakh fi djolof la
worna borom darou
Suñu systeme bi da ngay warou
Doto sakh tal sa boppeu

{Gaston – Refrain}
Dépensou soubeu moma sonal téré ma nélaw
Ndéki xalé yek bolou agn bi fok mou falaaw
Wo yane goudi bi bouné sélaw
Mak sama xell calcul mental bou doul diekh (2fois)

{Couplet 3}
Yene bi diss na lol
Waratinak si kou ndol
Di nga rouss di sap fo toll
dakh xete ngou forokh toll
Geureum Yallah ndakh si aye robinem rek lay dek samay boll
Diko niane kou yeureum gnou roussé gnou khadim rassoul
Werr’ak moromam,bess ak moromam xeff xippi la
Ouverture, korité,tabaski,lepp daw woutsima
Fourniture rendi khotti lepp warma
Tamou worma ni bouthi manké rek niaxtou bi dal ma
Avançou usine bi wathiagoul
ta payor yi danaka diagoul
Suñuy diatigué
Nekinou ouvrier dou sene yité
Sokhla wougnou charité
Dakh suñuy niakh lagnuy sigué
Lignu fi teyé
Moy lougnouy tadjal jaaboot gui suñu gnibé
Moy waral gni di touki bayi diabar’ak dome
Dakh lou situation bi tarr badola yi rek lay baum
Moy waral may xalate dougu si gal es kagn
Done patriote, jaaboot gui souroukh thi kamb ma bagn

{Gaston – Refrain}
Dépensou soubeu moma sonal téré ma nélaw
Ndéki xalé yek bolou agn bi fok mou falaaw
Wo yane goudi bi bouné sélaw
Mak sama xell calcul mental bou doul diekh (2fois)

{Outro}
Yeah gueureum lèn yaye deugleu
waayé bou takh ngène faaté Baye
Calcul mental doyna soxla
Ndakh té niom dé ay diambar you fakeu teud laniou
2007 Nigga Res Gaston BO Biz in the house man
and I’m out

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR