LYRIC

{Nektar – Refrain}
hush, everybody should no kèn bonoul
Li nga beug mom rek ngay done (hush
Kou tchii nek yoway taneu sa yone
Li nga gueum deug rek ngay done (hush)
Sheytané gui sa wett moytoul
Sa Ennemi number one sa none (hush)
he bee hangin ’round to get u down stand ever strong boumoula daan

{Verse 1}
Kèn Bonoul wouté yagua leukolo ak tiono
Bakh béy xékh am xalou nélaw fi mission la
Natu notel, nateu ak naar lepp sa yone
Lou djot yombe, djante bou féinké ka-ka momla
Biss bou rombe done djangate ak reuthiou késsé
Té do guestu yaakar ak diém bassa beussou décès
Faama djaugué ak faama djeum waral tiaxane warouma djégué
Li tchi yaw né tchi mane waral yi baat mala kaay yégué
Born to fight sassou borom karaw bou nioul
Ki raw cii nioune, gueum boppam té nangou Kun
Tionoy rafétal yéné, misery loves company
Gueum ma gni ciy guéné, rongognu wadiour laniouy fompe ni
I’m just like you sama yone lay saaytu
Wine ak shit di Dalal gni sèn gueinte tééla fatu
Beug am Joni Joni takh ngay djeufé merr
Alale ak taar cii aduna bou éphémère

{Nektar – Refrain}
hush, everybody should no kèn bonoul
Li nga beug mom rek ngay done (hush
Kou tchii nek yoway taneu sa yone
Li nga gueum deug rek ngay done (hush)
Sheytané gui sa wett moytoul
Sa Ennemi number one sa none (hush)
he bee hangin ’round to get u down stand ever strong boumoula daan

{Verse 2}
Aduna ay saup la, li daup bi nga sope la
Am kagne, am keur, soxna bou taaru, done kou popular
Jombou la djiteu leul ngor, gueum ak diom boulot
Dara dieulé sa yone, sa dolé ngui ci say nones
Xam xam cii xell, gueum gueum ci xoll
Guimbi, guindi, idji aaji ragné guiss ak xol
Guiss nga, Sunu sass diss na
Lofi am yako xaré xaleu yonu xalé néfi ngoné djaffé
Guiss waar yomboul, djingue dou kèn la djomboul
Boul jugé sa kumpe moy biss bi romboul
Bonou niou danio amoul, réwou niou danio xamoul (Waurna)
Guissou niou bay tamou, aah aah kèn bonoul
Many many years xoll yi gueuneu fess
Boyz yi dou ragala xippi xol , xell yi gueuneu yess
Bopp yi mak dieum yi, deumb yi tam deumb yi
Xaliss dieundeu ngor, mbeuguel ak gueum gueum yi

{Nektar – Refrain}
hush, everybody should no kèn bonoul
Li nga beug mom rek ngay done (hush
Kou tchii nek yoway taneu sa yone
Li nga gueum deug rek ngay done (hush)
Sheytané gui sa wett moytoul
Sa Ennemi number one sa none (hush)
he bee hangin ’round to get u down stand ever strong boumoula daan

{Outro}
Soumay xol sama bopp yaw lay guiss
Ngay xol sa bopp cii mane té dégou mala yaw la
Brother life bi sétu la li nga beug guiss rek ngay guiss
Loutax malay jugé Yalla rekka xam
Pps, Nectar

{Speech}

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR