LYRIC

{1er couplet}
Khalé bou saff sap, no ko guissé do sakh séral
Diem negn ko stop stop, mais kene meunou ci dara
Ki moy Mariama , khalé bou beuri calme
Enfant de bonne famille, yaro ci papa ac mama
Khol bou fess té dafko done beuss
Pa bi dafa fir té dafko done teuth
Mère bi lo def dou wakh , cho bi dem beu timitde di neu naw beuss bo ko done euf , argh
Mais commencer neu bali, commencer neu teup mur
Commencer neu dougou town
Khaam au nit you bess di def yeuf you bess,
Dakar ne dort pas goudi town
Moungui ni dé bayi neu diangue, am niari guel youmou done andeul
You kone deflo you ko done nan lo ay wayne, toukhlo ay yamba
Legui day fareuntou, té day thiagatou té day am ay histoires sans lendemain
Pa bi oubi neu sac bi guisss préservatif ac pillule lendemain
Père bi crise am chaire de poule
Dakh domam bi sèleutoul
A 16 ans ki viergetoul
Té derram bi setteutoul
Meune geu wakh mai kene dou ko forcer, diote neu eumb beu avorter
Wakh bi beuri mou jeul bagage yi dokh dokh dokh bi, la sortie

{Refrain}
Lebone lipone eh yow , beneu jiguene leuwone
Mais loumou doudnou métina , mais loumou doundou métina
Khalé bou ndaw leuwone, dafa yakhamtiwone
Téla sorou adouna, téla sorou adouna
Mariama, mariama mariama, yiaaaaah
Mariama, mariama mariama, yiaaaaah

{2eme couplet}
Khalé bou saff sap, boko guissé do sakh seral
Diem negn ko stop stop , mais kene meunou ci dara
Cho bi gueneu sene keur, demm galé beneu faram boutou aba
Bou ko yéné lou bakh, bou ko nop deugeuntane
Loumouy wakh nekoul ay blague
Mouné ko i love u girl me and u for life
Damleu nopp doumla meusseu bayi
Toukhou maak yaw dem outt fou nice
Doumeu rouss seu baye, ou seu yaye
Khamna ligeu doundou seu life
Diekh neu baby boul sakh cry
Na door bepeu guoor bouleu meusseu raaye
Koula meusseu raaye, na ko niousse walaye!
Mouné ko boy bou melni moussouma ko guiss han
Damleu beugeu damleu love je te kiffe han
Nague ma takk na leu mougnal boul tite han
Meme si khiff han, meme si crise han
Digeunté am kou wakh ac yayam néna Mariam leu beugeu takk
Beneu grand bou am charisme, comming from paris
Ac gandam valise, té mou am khaliss
Mère bi jeuli domam teggal ko mbir bi yeup noumou demé
Mouné li meunouma ko, ki nobouma ko, doumeu sey ac kima beugoul non jamais
Mou def histoire ci sene keur, kou nekkeu am beneu wakh boumou aporter
Wakh bi beuri histoire bi seuss mariama méyé negn ko mariage forcer

{Refrain}
Lebone lipone eh yow , beneu jiguene leuwone
Mais loumou doudnou métina , mais loumou doundou métina
Khalé bou ndaw leuwone, dafa yakhamtiwone
Téla sorou adouna, téla sorou adouna
Mariama, mariama mariama, yiaaaaah
Mariama, mariama mariama, yiaaaaah

{3eme couplet}
Khalé bou saff sap, boko guisser do sakh seral
Diem negn ko stop stop, mais kene meunou ci dara
Un mois de mariage mou jeulate bagage yi paré dokh dem sene keur
Mougn na, noppi na, soneu na, té dama dem beu seus
Sama dieukeur dam ko sikhlou, yene sayi damey youkhou dakh liguene def ni dou yone
Jsui pas heureuse, amatouma life , tass lene sey bi ba ma dem sama yone
Nieup kham né li meunatoul nekk, kone sokhlowoul gni forcer
Thiow bi dem beu beuri, mais mariama moudji divorcer
Ay dépression mo ko ci fekk! Papam touti mou réy ko
Wa galé bi, wa kogne bi, ay kharitam, nieupeu bayiko
Mouy fatélikou bou ndieukeu bi, ni derr bi yakho ci deukeu bi
Ac limou doundou ci dieukeur dji, aba néna dou ko jeuleuti
Amoutoul repere, elle trouve sa vie si triste
Mou teuthiou ci nek bi jeul ay garabe kharou dji, suicide

{Refrain}
Lebone lipone eh yow , beneu jiguene leuwone
Mais loumou doudnou métina , mais loumou doundou métina
Khalé bou ndaw leuwone, dafa yakhamtiwone
Téla sorou adouna, téla sorou adouna
Mariama, mariama mariama, yiaaaaah
Mariama, mariama mariama, yiaaaaah

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR