LYRIC

Verse 1}
Yow ! Kaddu yu niaawé ni waroul wone moss djougué ci yaw
Nio bokk ben dérette warona takh sa yaram daw
Yaggone leu titeuro am sa estime damala yagg naw
Aduna djay nala tay soxlaa-to sa rakka ndaw
Ya ngui may doyadale ndakh fokni yama fété kaw
Mais ngathié ngaalaama souma sanione kouy mindef yakoy raw
Moussouma joug ci bokko noumou tolou ma seddok yeene
Tolole ngène ci soxlama ma baayi lepp taxawou lène
Bima Yallah tégué ay nattu ma seug diko mougne lay doga xamni fi kou yoroul xaliss toloule fèneu ci yène
Appels yék Messages yi nieuweutoul ndax xam ngène ni légui frère dafay diékhal sa crédit rek té dou fathie sa soxla
Mane dama naïf djiteul famille sama lepp Nékone sen Baay Fall kou beug dara ma madjaali dioxla
Djépi naa séni mélokanou Hypocrite
Money rek ngèni guiss soufa nékoul ngène diko sikkeu
Djépi naa beutou mépris bi ngène may kholé tay
Mérité naa lou gueune li dédett kay dou sama xol la fay
Dama daan am kersa ba damay teudjou djoy
Souma daan yëg séni yitté té mounou mako fathie
Tay sama xol bi wow neu kongue té yeeneuko tothie
Fi kou sissou yeen leu koufi reuy gatte tam yeeneuko tauthie
Gueumeutouma kène ci yeen yeeneumeu pouss ci rancune
Mbétél laa am mou tiss tolou naa ci mérou danguine

{Jahman – Refrain}
Yeeneumeu pouss, Yeeneumeu pouss
Souma néké rancunier dou kèneu yeen leu (Yéé…)
Beugouma touss loudoul fayou
Waayé meunoumako maak yeen dou bèneu
Yeeneumeu pouss
Yeeneumeu pouss ci rancune yééééén
Yeeneumeu pouss
Limala léballone bokoulak li ngène ma fay tay

{Verse 2}
Gattal naa sama tankeu, téyé sama lamigne amatouma sakh sen djot
Yeené nalène ay xéweul lou ngène séintu Yalnay soute sen njorte
Guéddeu naa sen Peace and Love sama kaddu ngok nay tiss sen nopp
Nouyou nalène diokh lène thieur ndakh Yallah beugoul kouy dok mbokk
Bougoulite kouy yéé fitneu lolou rek motah may masla ak yeen
Méfiant légui dama distant beugueutouma naxassaalé faire semblant ak yeen
Def sama choix mou laathiema sacrifice ma dem ci andak mom
Lima daane def daa wagnékou rène ngène djigne ma niakk diom
Tok sen keur yeen gni daan saalite ci sama yéwénaay
Tay ngène def débat ci sama life di féinteu wakh djou bone
Légui soumay réé wo lène té soumay djoy laakou
Dotou lène yégue samay projet ndax lou ngène xam mou yakkou
Kölouté amatoul ndakh djaanou biir mo amatoul
Kilifté gui ngay niodi tchi boppam guiss naani mo matoul
Gueumeutouma kène ci yeen yeeneumeu pouss ci rancune
Mbétél laa am mou tiss tolou naa ci mérou danguine

{Jahman – Refrain}
Yeeneumeu pouss, Yeeneumeu pouss
Souma néké rancunier dou kèneu yeen leu (Yee…)
Beugouma touss loudoul fayou
Waayé meunoumako maak yeen dou bèneu
Yeeneumeu pouss
Yeeneumeu pouss ci rancune yééééén
Yeeneumeu pouss
Limala léballone bokoulak li ngène ma fay tay

{Verse 3}
Yallah xam nani Soeur xiroo bi ni gueunoune tchi nioune
Amoul lou Yaay Dadjoul tchi njabootam bi akka yagg mougne
Sometime ma fatélikou méré lène ba boudi tougne
Mais kouma guiss ci yène thiofél déki waate rek ma sippi muugne
Naniou dokh ci valeurou famille yiniou niou yaré wone
Ndidjaay laa ci say fils té yaw Badiène nga ci samay dome
Rancune day yakk xol té dallay ignane lo
Souxeuteul lou baax sa diguéék nit gni melni Imam LÔ
Reuthiou meusta am ci service yi mala défalone
Bou tay done dembeu té ma meune ko sakh dinako doli niaar
Niagassaayou Kaddu yi nga baalma dama néwone ci rancune
Aduna daara leu ci fanna yeup dafa beuri djanguine

{Jahman – Refrain}
Yeeneumeu pouss, Yeeneumeu pouss
Souma néké rancunier dou kèneu yeen leu (Yéé…)
Beugouma touss loudoul fayou
Waayé meunoumako maak yeen dou bèneu
Yeeneumeu pouss
Yeeneumeu pouss ci rancune yééééén
Yeeneumeu pouss
Limala léballone bokoulak li ngène ma fay tay

Mane dem na ba beug fayou waayé mounou mako
waaaaaw
Mane dem naaa ba beug fayou waayé mounou mako
waaw waaw
Mane dem naaa ba beug fayou waayé mounou mako
Baal nalène
Dem naaa
Yeeneumeu pouss
Euuuuuuuuuh

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR