LYRIC

Sama Jeunesse ( Dip Doundou Guiss)

Yeeah

Moré

Dund gis man la waay moré

1er Couplet

28 29 wacc 16 akk 17 ans

Kuko am du toog chaisam di seetaan

Ba ñi di dem ñee ngi teg zëm di ray temps

Ñële ño ngi ci bàkk prek jam délinquance

Jeunesse loolu ko former

Fate wuma ñi yeewo jail rëbës ba Fort B

Sama jeunesse daño woolu sen bopp

Doon ay mindeef yu mën def lu bari sen bopp

Ñi baayi jang wuti job nimu bëree

Liko rawa ngi football ba sumeku beré

Ñi Musique ñé mannequinat ak Fecc

Sumla ne du job kon ma nek Naafeq

Big up wa sité, wa college ak wa Lycee

Town Banlieue thug wala wally seck

Sama jeunesse bokoy imaginer

sa mind man dinga gis image yu neé

Amna jeune yuy dund costume caravate bureau

Si entreprise mba Etat ba am grade bi raw

Sen moromi tegle diplome yi di wut ligeey

Ñisi dess fees bop koñ yi di xaar ligeey

2e Couplet

Ñun daño sonn bëg fo

Bëg solo’k xaanj

Si benen monde lañu took dëku love ak happy

House party beach party

Swagg yaxx xaliss

Blackberry iphone ipad Galaxy

Ay jeune yu sen xel dal

Yendu facebook

Doranté texto ba fajar

Jamono school lonkante ligne yuy toj Senegal

Janguñ pour xam

Dañuy seet nuñ fexe jall classe par classe

Tricher mba yenen pexe dal

Tegente xel dirënte mbagg

Werente media

Jigeen yu bëg xaliss ba fuñko seen daw

Lijenti lugn lek sen far yi ba tayle sen ndaw

Boy yi taamu def tat

Di dunde bandit defkat

Mbeda ne sen staff deflen ay ngandi star

Motax gis nga

boy yi agresser mère

Ak gel yi cagatu biir

Boy yi njëkante jail

Ak Gel yi njëkante biir

Boy yi sacc sen pére ndax gélu appartement

Gel yi biir baña nek mére defi avortement

Non, Jeune yu dof epante seytane

Mais boy Xëya tané

Jigeen neegu sëya tané

3e Couplet

Xam nga daño rëy si sunuy rêve

Bo nekké ndaw du ñak nga sooru lu ne

Bul gis rek dafa ñaaw niñuy dunde

Ubil say bët te jeema xam liñuy gungé

Ku deku dund bifi nek te bonn

Reecu molay dap si sa yoon

Jeunesse bu yeemee

Jeunesse bu aliéner

Sama Jeunesse

Sama jeunesse

Son bi yen lako jaglel

Xamngen ni yoon bi ngen tann baaxul kon jadd len

Boy yi gel yu bari legi ay jagg lañ

Reew me laaj lu romb gentlemen jangi len

Added by

Maalik Sy

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR