LYRIC

{Karballah}
Kou xepp lakhou ndeky boulko yewou defsi nopam
Mbam seuf bou wékhé matt jotna defna tieuroup bayam
Ndokh dou bayi yone bene sattou dou watt bopam
Loufi sotti am borom kou nonou leuk nangoul koy nopam
Koufi diakhane di saw balla kéna toy nga laure
Euleuk donté dou agne dou rère geumeulni mbok mattna saur
Wolof néna
Bour dou mbok joyou biira jaffé awou
Balla kéna sandi diir kou dip yarane fok nga yarou
{Myster Zou}
Beute dou yennou wayé xamna li bop atane
Neub sou yendoo aleu salaw dina xeegn ab tane
Lou katane reuy reuy xel meune nako daane
Thi wax-tane
Koutamou wextane
Woné nga ab thiagane
Diourome niénti walakana kouléne beugueu doundal foukéléne
Faguoul léne mbaal
Marax dou ndieul guou béne
Wolof
Wolof Nena
Kou langue thi guéne moudié seugueum
Koudié gueunoul ndiourel thi guéniook ména

{1st Chorus}
Kene dou raw sa mbagn si lamign gou niaw
Lepp lou fekk bakh si tagg diakhal nieup boudé dou naw
Wolof néna
Bou sindakh yabbé ndobine garab guafa jéggé
Ta kou ndobine ray sa mame bo guissé lou nioul dofa jéggé
Wolof néna
Xel dou doy
Ndoul gua jekhna sourgua yoy
Balla nga jittou jot kou soumbou guedj dou niakka toy
Wolof néna
Kou beugua dioy tognal koula meune
Néna
Omatt guinar gaddou ko ko geune

{El Chigga}
Ganarr bou guissoul kouy bodj moudjou topp kouy takhagni,
Lou wayy di rayy si lokhom lay nathie Yéné nekk la boko djokhoul moukk boulko ko khagnii,
Dunya bi daraay leuk fexel jangg si toftal yi ,
Souka ndikkoul si missalou Meune ak attane lepp si yow la Fexel bokou si ponkal yi,
WOlof nena Badola dou jubb gathié Te agguci,
No def mou diar ngoram sollou bouki fexe lepp ba fagou tchi

{Wicky Lohj}
Olof ndiaye moma diangual gueum sa bop sa ba ngay naw
Diam wiri youlay dal diemko moytou sogua raw
Diouk sa morome toque teunk naniefa ngour di weuy
Lou safane takh mou nekh deug mou nieuwé dal mou diekh
Nieukeu la layé takhoula yeuye ki niax kham la khamadi raye
Dér ba tax si oudé boudé wax si febarou beuy
Mak matena bayi si réw Réw matouta beuy
Tal bou dieum si niax yéyo ngelaw na lep sélaw Bou kéne béw

{2nd Chorus}
Gni bokk tènay lakhasso gothj
Ko guiss mou dioy kouko wattat dafa niak kouko bott
Wolof néna
Lo weddi boko guissé geumko
Lou féne tèla xeuy xeuy deug gontou diotko
Wolof néna
Weurseugou goor moungsi takam
Lou beref fet fet yagg yagg dalsi andam
Wolof néna
Ramb taxoul nga done rambkatt
Néna
Kou guiro mayla dangéne bokk ndapp

{Stan Flinger}
Kou sol sa daal baayi mou djot leu fi am nga soxla
Kou nek ak sa yiité kène dou né xaral ma dioxla
Kouy naaw sa dougou di rouss waroula bété fi ngay taggué
Kou déh cii diaa ba adjo woulo taagué
Di sakami té sékho défo loudoul nakh sa biir
So wané lorr mou fégne cii ape diir
Loumou la téggal cii lou baakh na ngako takk téré
Louko moy moussibeu bouy nieuw sa kaw lay tééré
Wolof Néna

{Speech}

{3rd Chorus}
Wolof néna
Lou meunta niak fokmou am
Kou amoul yaye namp mame
Mbam sou doufé nekhi tann
Beut dou dioy loudoul loum xam
Néna goudi amna borom
Keule bouné amna mbeurom
Kou beugeu xam louy laabir amal dome
Kou meune fey dou kharro si ndokh
Degg degg amoul tank wayé dafay dokh
Wolof néna
Beugn wèkh na derettako lalo
Lii olof jangualé matta guedjo

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR