LYRIC

Elle Rap , Elle Chante
La musique des rues
Dans le coeur des enfants
de 7 à 77 ans!!!!
{Couplet 1}

Wweetaya namm sama xel def ma artiste
Diaar diaar yi di jangate ma wara aar tiss
Adouna taxawé mbeur , ma wara takku song
Ben lame dou yeungou waral bi love song
Diaglel lako yaw mi tok di degglu
Di teew fima woté , di wooté di yeuglu
Di weranté di xuloo , tewal ma sa deeku waay
Yaw yaye deuggi WRITAH , sasse bi nio kay deku way

Yaay booy number one fan
yaama samm ci lepp té meusso mako wane fen
suma jant ci leundeum , sama ndox ci maral
Ci sa baneex lay dokh , ma li lep ya o waral

Sama Gars yi
Childhood friends , compagnons de degats yi
Gungué ma ba dara dul dara , tay deug feign na
Jugué ci souf ba ci kaw , massuniu seug feneu
Daniuy dolli sant , yes we dit it
Xuss naniu ba aksi , delu ganaw deedet
Ci xaré la niax sité , geumeu niu indi ba fii té
Dana niu agalé fa niu dieum , histoire bi dina niu cité
First step niu né du bokk , Xtape Xacci topp
Fiy xassane niu dacc ko wokk , donté xamuniu dara mbok
Li niu idji mudjé mokk , diox la wurussu tali bi
Ki la yagga diomal, Xaatim ak Kallàmay tarri bi
Rap – a déé sunu yaram dou niun Yallah la
Moy diaglel kuko neex , Amine dialeu la
Liniu reudeu duniou ko dioggi , duniu wax ci Job bi
Fi nga niu natt daniu ko diegui , Waxtu Joot niu gobbi

[Refrain] Xaatim Ak Kallàma
Niaata att niu sax ci xarnu bi taxawé samm
su yomboon sax du baax , man coono du reer
Niun suba laniuy maadial , ceureul ko donté du reer (bis)

{Couplet 2}

Han! Ndortel menoul yombou
ku xam sunu demb do diaxlé tay sunuy bombe
Niaata att , tay mou neex suba mou naxadi
Noon yi naane , tay la rek suba dina xaddi
Niu takku di jemm , xoddeku di geum
Goné gui xam fimu jeum , mujeum di matal digueem
Nioy takku matal beuré bi
Feké nga demb céedel taye , xaddi wo ba legui
Li lama sama xissa wane , xeweul yi sawaan bawaane
Cofel gui du fi jok , goor gui taye moy ba wonon
Rappu magg , rappu ndaw , rappu tuut tank le
Xeutiowuniu dara , li lay doute ndank leu

[Refrain] Xaatim Ak Kallàma
Niaata att niu sax ci xarnu bi taxawé samm
su yomboon sax du baax , man coono du reer
Niun suba laniuy maadial , ceureul ko donté du reer (bis)

Elle Rap , Elle Chante
La musique des rues
Dans le coeur des enfants
de 7 à 77 ans!!!!

 

Added by

Papi

SHARE

Comments are off this post

ADVERTISEMENT

VIDEO

GalsenLyrics

GRATUIT
VOIR